Serigne Modou Kara dédie un Poème au Président Abdoulaye Wade

kara-3

Président d’honneur de la République
Ablaay Wàdd moo ko yayoo, ku am éthique
Adresser la ab poème, lu yell la
Daa war Sénégalais bu ne ñaanal la
Moo tax Ablaay sa turandoo niru na la
Ci xol bu baax ak man a jàngg, te xale la
Ku la manoon a defaraat ba ngay xaleel
Kon Senegaal amaat ku bees te di xaleel
Nga boole waat ñëpp ci benn’oo ak ligéy
Sòobaat ñëpp ci géej gi, ku man rekk féey
Sa doom Karim libre moo’k njaboot gi
Ku nekk laxasaayu, dëfal Askan wi
Ñëpp joxante loxo, Sambaay Demba
Omar doon it Ma-Lôh, tay di démb
Xol yëpp sédd, ñuy yéenante jàmm
Te lu ñu nar ci lu baax, bañ a fomm
Nga ñibisi ci sa réew ba faatu
Ñu yòbbu la TÛBÂ (na yéex), fu yaatu
Président d’honneur de la République
Ablaye Wade en a le mérite
Le fait de vous adresser un poème n’est que de la logique
Il est un devoir à tout Sénégalais de vous faire une prière
Raison pour laquelle Ablaye ton homonyme te ressemble
Par un bon cœur et bon élève, et c’est un enfant
Si l’on pouvait te rendre ta jeunesse
Le Sénégal retrouverait quelqu’un de nouveau, et tout jeune
Pour remettre tout le monde dans l’unité et le travail
Plonger tout le monde à l’eau, que quiconque puisse nager, s’y mette
Que ton fils Karim soit libre, ainsi que la famille
Que chacun se ceignent les reins afin de rassurer le Peuple
Que tous se donnent la main, car Samba c’est Demba
Qu’omar soit Ma-Lôh, aujourd’hui tel qu’hier
Tous les cœurs apaisés, chacun ait de belles intentions envers son prochain
Que nul ne renonce devant ses bonnes intentions
Que tu retrouves ton pays jusqu’à ce que la mort survienne
Que tu sois emmené à Touba (que cela advienne tard), un lieu spacieux.

 

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici