Hommage à Serigne Cheikh, les internautes peinés…

Suite à la disparition de Serigne Cheikh, les internautes n’ont pas manqué de manifester leur tristesse à travers des témoignages que Senepeople vous offre:
Sama xol métina trop… Si barké Yonente bi Sallalahou Aleyhi wa Salam. Yallana niou Yalla tass si sa barké S. Cheikh Tidiane Al Makhtum. Ya Allah Wonalé niou ak yow di Aldiana Firdaws di barké sa Torondo Cheikh Tidiane Cherif rta.

Oohhhhh aka maka beugone guiss ndeyssane serigne cheikh yalna yalla yokk leram

Al Maktoom dem na nii
Xol jooy na weet
Boroom xilaafa gi dëdduna
Fu nuy jëleeti ku mel ni yaw
Boroom xam-xam bu mat bi
Boroom kaalama ku diib gu seel gi
Boroom njàngale mu xarañ mi
Fu ñuy jëleeti ku tol ne yaw
Yaw mi defar xaleyi
Yaw mi wax ak góor ñi
Yaw mi teye jigéen ñi ci sëy yi
Yaw mi sa waaraate kat yi
Boroom baat bi sell bi
Sama xol jooy na
Samay róŋoon tuuru nañ
Sama aduna wéet na
Seex bi dem na
Seex Ahmed nelaw na
Seex ahmed Tijaan noppalu na
Seex Ahmed Tijaan Si siisuwul
Seex Ahmed Tijaan Si Al Maktoom
Yaa mat sërin
Yaa matalem njàngale
Ay waay ku may wettaleeti
Ana ku may fedaleetil sama diine
Yaa sell, yaa set, yaa seed
Yaa yiw, yaa ñeme
Yaa aar sam réew
Aar sa diine aar sa ngor
Fuñuy jëleeti ku mel ne yaw
Seex Mustafa Si mu tedd mi jaalenaa la
Yaw Mustarsidin bi jaaleena
Al amiin mu baax mi siggil ndigaale
Umma bi jaalenaa la
Jàmbaari Lismam nelaw na
Yàlla na Yàlla Yokki leeram
Dr Masàmba Géy

Serigne Cheikh Ahmed Tidiane SY « AL MAKHTOUM »
Mame Abdoul Aziz Sy Dabakh dafko meusse né « Cheikh, ndokhou teneu bi tey na, setna,nekhna…Batakhna kousi sangou set, kousi fote mou set, koussi togue mou nekh… »
Teneu gogou diapnani moy Tarikhatoul TIJANIYA. Tarikha binga beugueul sa bop, fonkolko sa bop. Tey mame danioulay nianal yalla boula keneu eupeulé thi sa yiwou tourondo Al abass, Yalla bouka keneu eupeulé thi yiwou gueuneu gui mindef, Yalla nala gueuneu gui mindef, sa tourondo ak sa baye térou thia aldiana firdawsi..
«Mon esprit a fini d’apprivoiser les moindres secrets de la rhétorique et les échos de mon éloquence retentiront à jamais». Cette phrase qui était la sienne vient d’avoir un sens à mes yeux…
Allah Ya Rahmou mame…
Al Makhtoum, l’homme au savoir inestimable, le guide, le philosophe le mystérieux.Un mystère qui restera mystère pour nous jusqu’au Jeudi 16 Mars 2017…
Mashallah mame

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici