France : Le consul Général s’exprime sur les demandes de visas court séjour : plus de 250 % de demandes notées après le Covid-19, c’est ce qui explique le manque de Rendez-vous …

Consulat général dafa setlu ni sakutéfu visa « Court séjour » dafa yokku si ñaari téemeer ak juróom fukk si téemeer bo jël lata jàngoro Covid-bi. Xam nañu ni lolou meuna jur yakamti ak diaxlé wala mérr. Moudi luñuy métite lou.

Niougui ngui def sunu kèmtélaay katan ngir gawal liggéey bi ba visa yi meuna guène si dir bou gatt. Wayé ay xibaar yu téguwul si dëgg di ay kacc gni ngui kay fesseul si xarala yu bès yi mouy réseaux sociaux yi.

Dëeg la am na ay yéx yex you am si sakoutéfu visa yi. Motax liniou lène di xélal moy nguène di téla jukk si sakutefu visa yi tèy dioxé bépp keyitt bu warr.

Ñu lène di fatali lu am solo : moudi aname gui ñuy dioxé visa yi :

Consulat général rékk mo am sagn sagn xool sakutéfu visa (site France-Visa). Di léral ni itam Consulat bu France, prestataire bi di VFS Global rékk la diox ndigel mouy nangu aka délo passeports yi.

Diarr ci yénèni bërëb wala agences nguir ñu jàap léla si sab dossier menèsna indi ay jafe jafe wala galankoor ndax sén diapalé gogu dafay faral di diour ay keuyite yu jaarul yoon.

Keuyite yu jàarul yoon yoyu dafay ladj yénéni saytu, suka défé liggéy bi dadé yexx. Teksi, wutt wala jënd ay RDV nguir dièbeul sa dossier wala ngir saku visa dafay guena guddel app gui.

Ñu gui def luñu meune ngir wagni app gui ak itam ak délo passeport yi si noumou guena gawé. Si jàamano bo xamni yengu yengu yi dafa tambali waat si rew yeup, gnu sétlu ko tamit si anam yepp rawatina si walu tukki yi tcha bitim rèww.

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici